Guddi

Guddi 가사

장르Afrobeats
원문 언어WO
조회수4
가사 좌표

원문 가사

WO
번역이 아직 없습니다. 원문 가사를 표시합니다.
18
Biig ci guddi gi biig ci guddi gi gent la laa fanaanee Gent gi yee ma ci ay nelaw Kenn du ma xool kenn du ma xool Ci bët te duma jaawale′g yow Bu ñu jooyee bu ñu jooyee taxul nga delluwaat fi Sa dem gi weetal na ñu Bëgg dem taxul mën a dem Mën a dem tax a dem Suba si lay xaar bu jot Su bët setee ma waxaat la ko Guddi biig bee yagg ci man Mbaa su ëllëge di nga tal xool sa ginaaw Biig ci guddi Gestul gestul balaa muy wees Man'ag guddi manaam guddi lay leeral Amatu fi sa mbëggeel amatu fi Gestul xoolal deglul fatalikul demb Ndax lepp day wees Setlul saayoo gestoo gis ma ci sa wet Ndax xolay gise Yaa am ñaanu loo Yaa ñakk goreediwoo Yaa weet te dawuloo Yaa yòpp te jooyuloo Gestul xoolal deglul fatalikul demb Ndax lepp day wees Setlul saayoo jaxlee gis ma ci sa wet Ndax xolay gise Yaa am ñaanu loo Yaa ñakk goreediwoo Yaa weet te dawuloo Yaa yòpp te jooyuloo Biig ci guddi gi biig ci guddi gi gent la laa fanaanee Gent gi yee ma ci ay nelaw Kenn du ma xool kenn du ma xool Ci bët te duma jaawale′g yow Bu ñu jooyee bu ñu jooyee taxul nga delluwaat fi Sa dem gi weetal na ñu Bëgg dem taxul mën a dem mën a dem tax a dem Biig ci guddi Gestul gestul balaa muy wees Suba si lay xaar bu jot Su bët setee ma waxaat la ko Guddi biig bee yagg ci man Mbaa su ëllëge di nga tal xool sa ginaaw Gestul gestul balaa muy wees