Aras

Aras 가사

장르Afrobeats
원문 언어WO
조회수803
가사 좌표

원문 가사

WO
번역이 아직 없습니다. 원문 가사를 표시합니다.
18
Bëgguma ngay gis lu la yéem Bëgguma nga gis lu la jaaxal Jaral na ma faat bakkan yaw nga dund Bëgguma la gis ngay caalit Xanaa xamoo ni benn lañ Ndekete Yàlla ñu boole Ndekete Yàlla ñu boole Fii ci suuf ci asamaan si Yàlla ñu boole, ñu doon benn say Dinaa la xamal bu doon benn fas Naaru góor laa ci yaw Man dinaa la dawal Safaa'g Marwaa Kenn du ma jiitu ci yaw Dinaa la yëgal ni Yàlla ñu boole Bind na ko Aras Buñ demee ba gisatoo ma Daa fekk man ma jiitu la Aras Man dinaa la xamal bu doon benn fas Naaru góor laa ci yaw Man dinaa la dawal Safaa'g Marwaa Kenn du ma jiitu ci yaw Man dinaa la yëgal ni Yàlla ñu boole Bind na ko Aras Buñ demee ba gisatoo ma Daa fekk man ma jiitu la Aras Asaman ak suuf Yaay suuf yaay asaman Yaay bidéew biy leeral Man dinaa la xamal ni Yàlla ñu boole Bind na ko Aras Buñ demee ba gisatoo ma Daa fekk man ma jiitu la Aras Gis la ci lëndëm bi te nekk ci leer Baayi la fa ngay gëlëm Metit bu naree ñëw di dal sa kaw Ma taxaw dekku ko Dinaa la xamal ni Yàlla ñu boole Bind na ko Aras Malaakal Mëwti sax bu la soxla woon Na ma jël bàyyi la Metit bu naree ñëw di dal sa kaw Ma taxaw dekku ko Yaay booy Yaay bidéew biy leeral asaman Asaman ak suuf Yaay suuf yaay asaman Yaay bidéew biy leeral Asaman ak suuf Dee ma ree Dee ma ree, ma lay ree Dee ma ree Dee ma ree, ma lay ree