Namel

Namel 가사

원문 언어WO
조회수9
가사 좌표

원문 가사

WO
번역이 아직 없습니다. 원문 가사를 표시합니다.
18
Jël nga sama xol, xel bi ci yaw la miir Janeer sa jëm ji, weetay bi daf ma diis, diis, diis Namm naa jote say bataaxal ngir xam ci lan nga ne Nelawatuma guddi ba bët sétt di xool say natal, jaxane naa ku la mérité, waroo forcé pour am son attention Mbëggeel solution la war a doon mais warul nekk equation Yaw boo ma seetaanee May nga suñu noon yi lu ñuy reetaane Buleen jox nopp dañoo seytaane Lu waay mën a def yaw nañu ko waxtane Yaw boo ma seetaanee May nga suñu noon yi lu ñuy reetaane Buleen jox nopp dañoo seytaane Lu waay mën a def yaw nañu ko waxtane Diggënte waat ak yaw Wax la sama nameel Gisante waat ak yaw Won la sama nobeel Xol du fen boo nekoon ak kenen Sa xel du jugee ci man Ndax mbëgeel bu dëggoo du fen Su la jekku wee dalay daan Mënuma fàtte fi ñu jaar te duma Bàyyi mu naxsaay li ma mom Dam koy jëli waat maa la moom Te duma la saggane Yaw boo ma seetaanee May nga suñu noon yi lu ñuy reetaane Buleen jox nopp dañoo seytaane Lu waay mën a def yaw nañu ko waxtane Yaw boo ma seetaanee May nga suñu noon yi lu ñuy reetaane Buleen jox nopp dañoo seytaane Lu waay mën a def yaw nañu ko waxtane