Bamba La Solution (feat. Ahmada Jadid & Abdou Khoudoss Kara)

Bamba La Solution (feat. Ahmada Jadid & Abdou Khoudoss Kara) 歌詞

ジャンルAfrobeats
原文言語WO
閲覧数15
歌詞座標

原文歌詞

WO
翻訳はまだありません。原文を表示しています。
18
Rëkk gaay ñi Bu kenn jaaxle, Sëriñ Bàmba wuyusi nañ Yërmandeem a bari ci ñun, ba tax na Dikk na sauver jàmm ñi Yeem naa la Yéemoon naa la, Mbàkke, yéemaati naa la Yaa fi nekkal Yàlla Hazza wa Jalla Rëjërajëf teeti Bàmba fëttal na Rap wa, Ceerno Ibra Faaty fees ko Dogte ko, togg ko, ñëwleen reer ko Mbana ga junni ñaay la Xanaa da nuy suxaat di raam Ba ñëw ci yaw te naan la Maam? Bootal te roganti ñu Bëgg na noo am sa ngëram Bu ñu baaxee dinañ ko am Muy texe tey ak ëllëg Moo tax jébbalu nañ Bu wér a wér ak mboolem lu ñu am tey saxoo sant Guddeek bëccëg Xëy suba teel Léemoo Sa Tur wu mag wi day tax a mucc Te day waral say mbir gaaw Seex Bàmba doy loo lu doy Daa am solo yaa ki nu doy tey ak ëllëg Yaa gën ci ndey, yaa gën ci baay Seex Bàmba, ñooŋ lay dagaan Ci barke Al Muntaxaa, Boroom mbég ak taar wi Buur Yàlla naatal réew mi Ndimbal, ndimbal ak yërmande (ndimbaloo Fall) Murid jëfe ndigal, baayi tere (ay góor Yàlla, loolooy yoon wi) Ndimbal, ndimbal ak yërmande (ndimbaloo Fall) Murid jëfe ndigal, baayi tere (ay góor Yàlla, loolooy yoon wi) Boroom Jumaa ji Doomi Jaara Buuso nga la dimbali nu Da noo doyadi rekk, waaye yërëm nu Yaa mbégteem sunu xarnu Mbàkke ñaan nañ la Déelu ñaanati barke Boroom Daaru Nang nu samal ngor gi ba ba ñuy faatu Xeewal it bu ñuy bëwloo Ñaan nañ ci barke Mafarma Yaasin Daour mi ci mbul sagal nu Issa Dièye, Faatim Penda leeram ga sàr na Ba juroom ñaari asamaan yee Ndax da ngaa bari ay may? Ña daan falu, yaalen fal Eskeey sangub Maam Seex Ibrahima Fall Àjjana yépp a ngay riir ngir saam Faali Baay Fall Eskeey sangub Maam Seex Ibrahima Fall Faala gën (madegel) Maam Seexa raw (ngañ madegel demba) Faala gën (madegel) Maam Seexa raw (ngañ madegel demba) Faala gën (madegel) Maam Seexa raw (ngañ madegel demba) Faala gën (madegel) Maam Seexa raw (ngañ madegel demba) Ngañ ma ca leer ya (degal) Moo tax jébbalu nañ Bu wér a wér ak mboolem lu ñu am tey saxoo sant Guddeek bëccëg Xëy suba teel Léemoo Sa Tur wu mag wi day tax a mucc Te day waral say mbir gaaw Seex Bàmba doy loo lu doy Daa am solo yaa ki nu doy tey ak ëllëg Yaa gën ci ndey, yaa gën ci baay Seex Bàmba, ñooŋ lay dagaan Ci barke Al Muntaxaa, Boroom mbég ak taar wi Buur Yàlla naatal réew mi Ndimbal, ndimbal ak yërmande (ndimbaloo Fall) Murid jëfe ndigal, baayi tere (ay góor Yàlla, loolooy yoon wi) Ndimbal, ndimbal ak yërmande (ndimbaloo Fall) Murid jëfe ndigal, baayi tere (ay góor Yàlla, loolooy yoon wi)