Sonneu Na Tayina

Letra de Sonneu Na Tayina

GéneroAfrobeats
Idioma originalWO
Vistas10
Coordenadas de la letra

Letra original

WO
La traducción todavía no está disponible. Mostramos la letra original.
18
Léegi, wax ji neexatul Te su ma waxee mu xëp ci kaani Moom de léegi, dépense matatul Te su ma laajee, mu daldi maay jani Li la war ci man guddi gi Ci kaw lal bi, yeggatoo ci Du wax ju neex, du ray, du fóon Déggatuma chérie Sonn naa, tàyyi naa Mënatuma Mënatuma, sonn naa Bàyyi naa Léegi, wax ji neexatul Te su ma waxee mu xëp ci kaani Moom de léegi, dépense matatul Te su ma laajee, mu daldi maay jani (Kii, lu ko dal) Ana li nga ma waxoon ak li nga ma diggoon Li taxoon ma falax waxi yaay, téggi waxi baay Ana li nga ma waxoon ak li nga ma diggoon Li taxoon ma falax waxi yaay, téggi waxi baay Sonn naa, tàyyi naa Tàyyi naa, sonn naa Sonn naa mënatuma dellu sama kër baay Eh! Demb balaa tay Ana ni ñu meloon, demb balaa tay Tey, tey, tey Léegi, waxtaan amatul Te su ma jaaxlee, loxo la may sanni Léegi dafa may dóor aka yooxu Xas aka jani ci kanamu jaboot gi Li ma waxoon kër baay Tay na ba mënatuma dellu man mi, ooh! Li ma reccu tey moom Mooy li ma séy ak yaw ba mu deme ni ouh! Sonn naa, tàyyi naa Mënatuma Mënatuma, sonn naa Bàyyi naa Léegi, wax ji neexatul Te su ma waxee mu xëp ci kaani Moom de léegi, dépense matatul Te su ma laajee, mu daldi maay jani (Kii, lu ko dal) Ana li nga ma waxoon ak li nga ma diggoon Li taxoon ma falax waxi yaay, téggi waxi baay Ana li nga ma waxoon ak li nga ma diggoon Li taxoon ma falax waxi yaay, téggi waxi baay Sonn naa, tàyyi naa Tàyyi naa, sonn naa Sonn naa mënatuma dellu sama kër baay Eh! Demb balaa tay Ana ni ñu meloon, demb balaa tay Ana ni ñu meloon, demb balaa tay Ana ni ñu meloon, demb balaa tay Ana ni ñu meloon, demb balaa tay Ouh, dem naa Dem naa Ouh, dem naa Dem naa Dem naa bàyyi la fi, man dem naa Dem naa Dem naa, mënatuma muñ, dem naa